Nataal yu ñu doxal (dessin animé) ci làkk Wolof ak ISMAEL LÓ ! Jàngoro yi dañoo mer ba futt booleek jaaxle ndax nit ñi dañoo def jeego yu réy ngir xeex leen. Niki noonu, ñu dalal seen kilifa SIDA, mi am pexeem faagaagal doomu aadama : song kaaraange yaramam. Waaye nees di def ba aaru ci moom aki waayam ?
[Askan] Nettali : Ni la póliisu Senegaal bóomee Abdulaay Wàdd.
Politicosn.com : Gaawu 24 Sulet 2010 Nettali : Ni la póliisu Senegaal faatee Abdulaay Wàdd.
Démb ba léegi, Me Aamadu Aali Kan, miy layal waa kër Abdulaay Wàdd Yingu, mi faatuwoon ca ñaxtuy Yëmbël ya, njàmbat na alaxam (déposer plainte) ci kanamu njiitu àttekat yi ci lu aji ci ñeenti tuuma : faat, dóor ak ngaañ yu coobarewu, càcc wootekaay ak xaalis, ñàkk a wallu aji-loru, la yéenekaay l'As, mi nettali na jéyya ja demee, xamale.
Ba 18 waxtu jubee, la ko kilifaam, mi doon door a juge ci màggalug 130 eelu wooteb Laayeen yi, yónni mu jëlal ko xaalis ci boroom bitik ba ngir jënd xont. Ca yoon way dem Sedima ba nekk Caaroy, xale bu góor boobee, mi xelam demul benn yoon ne ma ngay dund waxtoom ya mujj, egg Caaroy tombeeg ñaxtu ñawkat yi doon naqarlu dog-dogi kuraη yi. Foofa lépp jaxasoo, takk-der yu soluwul, ngànnaayu ba fees, tàmbalee dàq nit ñi. Bamu gisee ñépp di daw, mu daw làqu ci kër ga mu njëkk a jot. Yégul lumay ne ay takk-der topp nañu ko. Boroom kër ga dal, ca ñaan leen ngir ñu bàyyi ko, waaye dara.
Xibaaryi.com: Gaawu 24 sulet 2010 Réewum melokaay yi
Réewum melokaan yi, téere la bu nu jélee ci web bi bu bindaakoon bi jagleel xale yi ngir xeex Boddikoonte ci biir xeet. Ci xët wu njëkk bi bindaakoon lii la ci wax:
"Xew-xew bii ma leen di nettali, mi ngi xewoon ay at ca ganaaw, ba ma nekkee gune. Booba maa ngi amoon juróom-ñaari at te ba tey mu ngi may yéem. Di naa leen ko nettali ni ma ko fattali koo, doon te amaa na xeweewul noona dëgg-dëgg. Xew-xew yi, ni ñu leen di fàtteli koo rekk la ñuy mel waaye du ñu mel mukk ni ñu xeweewoon. Lépp a ngi xewee woon ca Talkonia, ab dëkk boo xam ne, naka yeneen dëkk yu bari, ña fa dëkk, da ñoo bék ca na ñu mel: maanaam di ay nit yu weex. Da ñoo weexoon a weex mel ni pëndëxu puudër. Ca seen biir, lakku way Talkonia lañuy wax, lakk bu am solo ta neexoon ci dégg. Ci jamonoy nawet, ñenn ñi da ñu daan xonx ba mel ni xaal.deru yaram bu ni leeree tamit amoon na ay sikkëm. Terewul duñu ko weccee ak beneen bu gënë xereer, xees baa ñuul. Loolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu."
[Askan] [Nataal] Jéyya ca Jidda Caaroy Kaw : Kër gu màbb a faat benn nit
Seneweb.com : Alxamis 22 Sulet 2010 [Nataal] Jéyya ca Jidda Caaroy Kaw : Kër gu màbb a faat benn nit
Góor gu màgget a faatu ci taaxum kër gu màbb ca Jidda Caaroy Kaw, ca goxu Pikin. Mag moomu tolloon ci 70 at dadoon féexlu ca kanamu kër ga ba taax ma di màbb ca kawam ak ci kawi sëtam. Ñaari xale ya mucc nañu, waaye mag ma moom wuyyu ji na Boroomam. Ci kàdduy ndawal SENEWEB-NEWS ma teewoon ca bërëb ba, kër ga wonewul woon benn fett-fett. Jaraafu dëkkaan la, Aliun Badara Jóob, teew na fa ngir nemmeeku mbir ma.
[Ladab] Téereb Ndeyu àtte réewum Senegaal, bi mujj, génn na
OSAD : Altine, 19 sulet 2010 Téereb Ndeyu àtte réewum Senegaal, bi mujj, génn na.
Fileek ay fan, bu ci Yàlla àndee, dingeen gis téere bi ngeen doon xaar !
Téereb ndeyu àtte réewum Senegaal ci Wolof, bi Soxna Aram Faal ak Axmet Juuf bindoon, dina génn ci sotti gu gën a bees. Téere boobu ñu duppee "Ndeyu Àtte Repibligu Senegaal" te toll ci 127 xët a ngi
- jar1 400 dërëm (junni ak ñeenti téeméer), dëppoo ak « sept mille francs » 7 000 CFA - Ku ko soxla na dem : Villa 16 A zone B, - mbaa mu woote ci tel : +221 33 825 39 10, +221 77 608 04 86
[Jëmm] [W I D E O] Dëj : Ndaanaanu woy bi di Yànde Koddu Seen faatu na ci suba.
Seneweb.com : Alxamis 15 Sulet 2010
[W I D E O] Dëj : Ndaanaanu woy bi di Yànde Koddu Seen faatu na ci suba.
Ndaanaanu woykati Sereer bi di Yànde Koddu Seen, faatu na alximis jii, gannaaw feebar su ko yàgga tëral, la rajo Rfm yëgle. Géwalu Njiitu Réew miwoon, doonoon ab taalifkat, génn na àddina ci alximis jii. Loolee nga xewe ca Loppitaal Dàntek gi mu nekkandiwoon ay ayu-bés, fekk Yànde Koddoo ngi amoon 78 at. Doonoon ku ñu xamoon ci wàllu Caada, ndaanaan lii feeñ ci Taarixu Senegaal ba mu amee 15 at. Ay kañam dañu daan gunge Njiitu Réew mii di Sengoor.
[Askan] Faatug benn xale bu góor ci ab doxub ñaxtu ngir naqarlu dog-dogi kuraη yi.
Seneweb.com : Alximis 15 Sulet 2010
Faatug benn xale bu góor ci ab doxub ñaxtu ngir naqarlu dog-dogi kuraη yi.
Genn xale bu góor tollu ci 25 at faatu na Àllarba bi 19 waxtu (timis) tegee tuuti, ci ay ñaxtu yu waa Benn Baraak amaloon ngir naqarlu dog-dogi kuraη yi. Gannaaw ba kuraη bi dogee, la waa Yëmbël génn daaldi fatt yoon yi. Ci la takk-der yu Yëmbël agsi, woññi leen. Ca ba ñuy daw nag la kenn ci way-ñaxtu yooyu daanu ci kekk bi (gudroη bi).
Ba gox yu bari ci biir Réew mi noppee, la Ndakaaru tàmbalee jël wàllam ci yënguy Askan wi ndax dog-dogi kuraη yu takku yi. Ñawkat yeek ñeneen ñiy ligéeyee loxo ca Néegub njënd ak njaay (centre commercial) ba ca Asalem 5 (HLM5) wone nañu, ci Àllarba ji, seenug mer ci dog-dogi kuraη yi, yoy dañuy yàqal lu am solo ligéeyuwaay yu ndaw yi. Ngir xeex lu ñaaw loolii, way-yëngu yooyu lànk nañoo fey seeni bori kuraη. Ci mer moomu, nar nañoo sonnal bépp ndawi Senelec bu fa ñëwati di seet aka rëdd lañu lakk ci kuraη.
[Diine] JIBALUL NGUUR GI TËJ WOOTEB SEYDINAA LIMAAMULAAY: Ay ñaan ngir jàmm
Le Soleil : Àllarba 14 Sulet 2010 JIBALUL NGUUR GI TËJ WOOTEB SEYDINAA LIMAAMULAAY: Ay ñaan ngir jàmm ca Kaasamaas ak nawet bu barkeel
130eelu wooteeb SEYDINAA LIMAAMULAAY weesu na. Ci jibalu Nguur ga ko tëj, gërëmees na Nguur gi ci ndimbalam ngir xew-xew wi jaar yoon. Def nañu fa ay ñaan ngir jàmm delsi ca Kaasamaas te ñu am nawet bu bàrkeel.
Jëwriñu mbootaay mi yor xewum (cordonnateur du comité d’organisation) 130eelu Wooteb Seydinaa Limaamulaay, di Seydinaa Isaa Caw Laay, tënk na kàddoom ci jàmm ca Kaasamaas ak ci mbënn mi ci anéer bi (la Banlieue), ci Jibalul Nguur ga ñu doon def. Ci turi Xalifu Laayeen yi, Seydinaa Abdulaay Caw Laay, ñaan na ngir jàmm am ci Senegaal gépp te nawetu ren bi bàrkeel. Jëwriñu Nguur gi yor biir Réew mi, Bekaay Jóob, jottali na nuyyóob Njiitu Réew mi ak Nguur gi. Wax na it ne Wooteb Seydinaa Limaamulaay bii woote jéme ci Lislaam la.