 | |
| Cëru (Contribuer) | Boo bëggee siiwal ab jukki (article)
[cuqal fii] |
|
| |
[Jëmm] [W I D E O] Dëj : Ndaanaanu woy bi di Yànde Koddu Seen faatu na ci suba.
| 
Seneweb.com : Alxamis 15 Sulet 2010
[W I D E O] Dëj : Ndaanaanu woy bi di Yànde Koddu Seen faatu na ci suba.
Ndaanaanu woykati Sereer bi di Yànde Koddu Seen, faatu na alximis jii, gannaaw feebar su ko yàgga tëral, la rajo Rfm yëgle. Géwalu Njiitu Réew miwoon, doonoon ab taalifkat, génn na àddina ci alximis jii. Loolee nga xewe ca Loppitaal Dàntek gi mu nekkandiwoon ay ayu-bés, fekk Yànde Koddoo ngi amoon 78 at. Doonoon ku ñu xamoon ci wàllu Caada, ndaanaan lii feeñ ci Taarixu Senegaal ba mu amee 15 at. Ay kañam dañu daan gunge Njiitu Réew mii di Sengoor.
| |
|
[Jëmm] Kazu Rajab (27 ndeyu-koor): Sëriñ Fàllu Mbàkke ak lenn ci ag dundam
|

Xibaaryi.com: Dibéer 04 Sulet 2010
Sëriñ Muhammadu Faliilu Mbàkke (dàkkantal: Sëriñ Fallu, Sëñ Fallu, Fàllu Galas, Alaaji Fàllu)
gane àdduna ca Daaru Salaam (kërug jàmm) nekk ci tundu bawol ca réewum Senegaal ci 27 ndeyu-koor(rajab) atum 1305 cigàddaay gi yamoo ak atum 1887/88.
Mu tombe ak bis bi turandoom Sunu Sang Muhammad (jàmm i Yàlla ak xéewalam ci kawam) riñaanee ci ndingalal boroomam ànd ak sunu Sang Jibriil (jàmm ci moo) war daaba ju deesi woowe «Al-buraax», Ci rañaan googii la ko Yàlla sunu boroom joxee julliy joróom di ponk bi ëpp doole ci lislaam, waral ko ci mboolem jullit ñi, ak xeet i xam-xam yu mu fi sotti ngir nun ak ya ko ñeel ci ag jagle, Muy guddi gu màgg ci Lislaam, guddi gi nu xéewal gi dikkale juge fa Aji-Màgg gi.
| |
|
[Jëmm] Poroxaan 2010: Soxna Jaara royuwaayu jigéen ñi
|
Xibaaryi.com: Altine 19 Awril 2010
Poroxaan 2010: Soxna Jaara royuwaayu jigéen ñi.
Soxna Mariyaama BUSO ñu dàkkantale ko ci jikko Jaaratu-l-Laah (dëkkandoob Yàlla bi) gane àdduna ci atum 1833 ci as ndëkk su tudd Gollere ca Fuuta, Génn àdduna ci atum 1866 ca poroxaan Soxna Jaara BUSO mom Sëriñ Hamat BUSO (baayam) ak Soxna Asta Waalo MBÀKKE (yaayam), cosaano ci askanu Sëriif gog calale ga dem na ba ca Imaam Hasan mom Imaam Aliwu mom Abii Taalib ak Faatima mom Muhammad Yonentub Yàlla (jàmmi Yàlla ci ñoom), (*xoolal callale gi fii ngir gàttal)
| |
|
[Jëmm] Fàttaliku Séex Anta Jóob, 1923 - 7 fewriyee 1986
| OSAD: Gaawu 6 fewriyee 2010
Fàttaliku Séex Anta Jóob, 1923 - 7 fewriyee 1986
Ngir màggal bés bi Séex Anta Jóob génne àddina, OSAD a ngiy indi jukki bi mu tibbe ci waxtaan wi boroom xam-xam bi amaloon ca Kees, jagleel ko janq ji doon tàggatu ci wàllu njàngale, ci awril 1984.
Jukki baa ngi nii
Làmmiñ wi ngànnaay la, paaka la, balay ñaw nga daas ko. Làmmiñ wu ñu jariñoowul, mi ngi mel ni paaka bu xomaag. Te Tubaab yi, bi ñu fi ñëwee, réew mépp dañu ko yore ci seen làmmiñu bopp. Moo taxoon ba sunu làmmiñ yi des gannaaw. Li la daan tax a jëm kanam, li la daan tax a am loo dundale sag njaboot, ci weneen làmmiñ nga daan jaar am ko…Loolu moo taxoon nu sàggane sunu làmmiñ yii. Waaye du caagéeni dañu mënul woon a wax li nu bëgg a wax…
| |
|
[Jëmm] Ay téeméeri téeméeri junniy soppey Maykël Jakson a ngi waaj ab sargalam
| 
Lemonde: Dibéer 05 Sulet 2009
Ay téeméeri téeméeri junniy soppey Maykël Jakson a ngi waaj ab sargalam
1,6 milyoηiy soppeem a ci bëgg a teew waaye ay junni rek lees ciy tànn. Sargal gi ñuy defal Maikël Jakson, mi faatu ci 25 sue, dees na ko amal talaata 7 Sulet ca biir Staples Center bu Los Angeles, ci teewaayu 11 000 ciy soppeem yi nu tànn ci internet, ak ci teewaayu poliis ba ndax ragal mu ëppi loxo.
Xew woowii ngi war a tàmbali ci 10 waxtu (16 wa ci Ndakaaru) te dees na ko wone ciy ekrã yu mag (écran géant) ci béréb ci sësook Nokia Theater, ngir yeneen 6 500 soppeem mën ko faa seetaan.
| |
|
[Jëmm] Abdulaay Wàdd am na tey 83 at.
| LAs : Àjjuma 29 Mee 2009
Abdulaay Wàdd am na tey 83 at.
Bu ñàkkul tey ñu koy wax, "Joyeux anniversaire" , di ko ñaanal gudd fan, wér akug ndam ci li muy sumb, rax dolli di ko jox ay yóobal (cadeaux) yees di jëlee ci ñaqu baadoolo yi, ñu ëpp ci askan wi yégu ñu ko mbaa taluñu ko ndax xiif, mar ak wopp a leen tënk, mbënd mee leen tiital mbaa jàng mu bon mi ëlëm leen. Waaye góor gii toll tey ci 83 atam (mi ngi judd 29 mee 1926) taluleen.
| |
|
[Jëmm] NJIITU JËWRIÑI NGUUR GU BEES : Suleymaan Ndeene Njaay, àttekat buy politig
| Nettali : Alximis 30 Awril 2009
NJIITU JËWRIÑI NGUUR lU BEES: Suleymaan Ndeene Njaay, layalkat (avocat) buy politig.

Réewum Senegaal am na njiitu jëwriñi nguur lu bees. Suleymaan Ndeene Njaay, 58 at, di layalkat mooy njiitu nguur li ñu mujjee tabb. Mi ngi wuutu alximis 30 awril kii di Seex Ajibu Sumaare mi doonutoon kuy politig. Muy ku am taxawaay, doon meeru Gingineew 2002 ag léegi. Suleymaan Ndeene Njaay bokk na ci ñi njëkk bokk PDS.
| |
|
[Jëmm] Faatug Faatu Wàdd, mag bu jigéen ci Njiitu réew mi
| Ferloo.com : Gàwwu 25 Awr 2009
Faatug Faatu Wàdd, mag bu jigéen bu Njiitu réew mi. 
Dëj amaat na ci njabootug njiitu réew mi ci faatug Faatu Wàdd, di magam. Dees na jot néew bi ci 12 waxtu ca Loppitaal Principal bu Ndakaaru.
| |
|
[Jëmm] Nit ku ñuul ki njëkk a bokk ci njiiti asiiraans yi gën a mag ci àduna
| (Loondar) AFP : Àjjuma 20 maars 2009
Nit ku ñuul ki njëkk a bokk ci njiiti asiiraans yi gën a mag ci àduna
Tiijaan Caam, tollu ci 46 at te askanoo ca réewum Koddiwaar, doon na nit ku ñuul ki ñu njëkk a tàbb njiitug lonkoo (entreprise) ci yi gën a réy ca réewum Àngalteer. Kër ga di koompañii asiiraans biñu duppee Prudential. Muy ndam lu réy ci moom mi am jaar-jaar gu jafee gis ca goxu koom-koom bii di City ca péeyum Àngalteer.
| |
|
[Jëmm] Alaaji Maalig Si
| Alaaji Maalig Si: Ab jukki bu Wikipedia
Alaaji Maalik Si ma nga gane àdduna Dëw Faal wetu Gaaya bokk ci tunduw Dagana ci atum 1855. Waa-juram wu góor tuddoon Usmaan, wu jigéen Faa Wàdd Wele. Mi ngi jànge alxuraan Luga ci kenn ci taalibey Alaaji Omar Futiyu Taal yi. Bi mu doonee mag la dem Màkka, bi mu dellusee sax ci jaamu Yàlla ak jàngale ak dugal ñi duli jullit ci lislaam. Ci noonu la tase njàngalem yoonu Tiijaan ci Senegaal jaare ko ci tuxoom yi ci Jolof, Kajoor ak Ndar. Ci mujj gi mu dëkksi Tiwaawan ci 1902. Fa la njëkk a xumbale gàmmu.
| |
|
|
| |
| Téere sargal |
|
|
|
|
| Kurél yiy yëngu ci suqali làkki réew mi | • Osad
• Anafa  |
|
|