 | |
| Cëru (Contribuer) | Boo bëggee siiwal ab jukki (article)
[cuqal fii] |
|
| |
[Bitim réew] Ab fajkat bañ na lesioη donóor ngir ñaxtu.
| 
Le Monde : Altine 23 Ut 2010
Ab fajkat bañ na lesioη donóor ngir ñaxtu.
Ab fajkat bu màcc ci anestesi( maanaam teggi mettit) tey yëngu ci ndimbal way-loru yi ci àddina sépp, bind na altine Nikolaa Sarkosi (njiitu réewum Farãs) ngir yégël ko ne lànk na ñu tappal ko lesioη donóor (Légion d'honneur), ngir wone ag ñàkk àndam ag politigu kiiraange gu Sarkosi.
Njiitu réew ma daa tànnoon Aan-Mari Guwe ngir ñu tappal ko lesioη donóor ci 14 sulet ndax ag "sóoboom ci liggéeyal réewum Farãs".
Waaye fajkatu Goxu Póo boobu, bokk ci "Médecins du Monde" (Fajkat yu àdduna si) 30 at ak léegi, yégal na Nikolaa Sarkosi ag lànkam màndarga moomu ñu ko waroon na tappal sawie 2011.
| |
|
[Bitim réew] NATT - Ci juróomi doomi Amerig yoo jél, kenn a ci xalaat ne Obama jullit la.
| 
WebNews : Alxamis 19 Ut 2010
NATT - Ci juróomi doomi Amerig yoo jél, kenn a ci xalaat ne Obama jullit la.
Benn doomu Amerig ci juróom yoo jél, xalaat na, ci lu teguwul fenn, ne njiitu réew ma Barak Obama jullit la, muy li tukkee cib natt (sondage) bu Washington Post siiwal. Njiitu réewum Amerig doontale saxal na di dem ci Jàngu ba ak a jibal ag bokkam ci diiney kercen, teewul limu doomi Amerig yiy xalaat ne jullit la deñul di yokk, muy lu tekkee ci natt bi Pew Research Center def. Ci jamono jooju, limu waa Amerig yi jàppe Obama ab kercen daa wàcc ba ci génn-wàll ci benn at, maanaam 34 %.
| |
|
[Bitim réew] Bataaxalu Barak Obama ñeel ndawi Afrig
| 
Jeune Afrique : Àllarba 4 Ut 2010
Bataaxalu Barak Obama ñeel ndawi Afrig
Ca bamuy àddu cim pénc mu amoon ca Kër Gu Weex ga (Njénde njiitu réewum Amerig) aki ndaw yu fa teewaloon ndawi Afrig yi, Barak Obama feddali na kàddu ya mu jibaloon Akra. Teg ca ηàññ bu baax ñi maaseek at ya réewi Afrig yi móomee seen bopp (njiitu réewi Afrig yi jamono jii la wax).
Ngir màggal 50e at yi réewi Afrig sowwu-jànt móomee senn bopp ak léegi, kilifa yu Amerig yi amnañu ci xalaat wu wuute. Dajalewuñu njiitu réewi Afrig yi mbaa njiitu jëwriñ yi, xana kay dalal 115 ndaw, yu fa teewal ndawi Afrig, ngir weccoonte xalaat ak njiitu réew ma Barak Obama ci « ni ñu gisee Afrig ci 50 at yi ñu dégmal ».
| |
|
[Bitim réew] SENEGAAL : Réewum yaakaar ñeel ndawi Ayiti ?
| 
WebNews : Alxamis 18 Màrs 2010
SENEGAAL : Réewum yaakaar ñeel ndawi Ayiti ?
Ba ñu ñàkkee yaakaar ganaaw ba fa suuf sa yëngoo ,ay ndongo gëm nañu lool li leen njiitu réew mi Abdulaay Wàdd wax ne nañu ñibbisi seen kër i maam.
Lu tollook ay téeméeri junniy ndawi Ayiti,di ay ndongo,ay ligéeykat wala sax ñu amul ligéey, noppi nañu ngir ñëw Senegaal dàq seen wërsëg. Aan Piyeer Juul, 23 at, di ab ndongo daara ju mag ci wàllu Jëflànte ci diggante réew yi, bokk na ci. Ganaaw bamu wutee ligéey lu yàgg ba dugg ci Lekkool biy jàngale lu jëm ci Jëflànte ci diggante réew yi ak Bitim réew, dafa nàmm a àggale am njàngam ci Senegaal.
| |
|
[Bitim réew] Xaatimees na ag déggoo guy génne réewum Gine ciy jafe-jafe.
| 
Le Monde : Gaawu 16 Samwie 2009
Xaatimees na ag déggoo guy génne réewum Gine ciy jafe-jafe.
Ag déggoo ngir génne réewum Gine ciy jafe-jafe la ñu xaatim àjjuma 15 samwie ca Wagadugu. Li déggoo googu ëmb mooy bàyyandikug Kapiten Musaa Dadis Kamara mu "dallu" ca bitim-réew ak amalug joηante njiitu réew "fii ak juróom-benn weer". Ganaaw ñaari fanu weccoonte xalaat, la ko ñett ñii xaatim : kapiten Dadis Kamara, Seekuba Konaate mi jiitandeegum réew ma ak njiitu réewum Burkinafaasoo Belees Kompawore, di ab yombalkat.
| |
|
[Bitim réew] [WIDEO] Silwio Berluskoni ca fajukaay ba ganaaw aw xaañ wu metti.
| 
France 24 : Dibéer 13 Des 2009
[WIDEO] Silwio Berluskoni ca fajukaay ba ganaaw xaañ wu metti.
AFP - Njiitu jëwriñu Itali xaañeesna ko ci xar kanam ci miting bu amoon ca Milã. Ki ko xaañ nag waa ju ñu yàgg a faj ndax xel mu naxari la. Kookee tudd Massimo Tartaglia, am 42 at, jàppeesna ko ba yóbb ko ci yoon. Silwio Berluskoni war naa toog 24 waxtu ca fajukaay ba.
| |
|
[Bitim réew] Alalu askan wi : Abdulaay Wàdd ak Ñetti njiitu réewu Afrig joxoñ nañu leen cib p
| 
Le Monde : Gaawu 5 Des 2009
Alalu askan wi : Abdulaay Wàdd ak Ñetti njiitu réewu Afrig joxoñ nañu leen cib pelent ca Paris.
Ñeenti njiitu réewu Afrig, bokk na ci Abdulaay Wàdd wu Senegaal ak Dënis Saasu Ngeesu wu Kongoo, joxoñees naleen cib pelent ca Paris ci bisub 16 novàmbar. Kuréel MLA mi leen di jiiñ ag "randal alalu askan" dugal na ab pelent àjjuma 4 desàmbar jii ca Paris.
| |
|
[Bitim réew] [Itali] Ay junniy nit ñaxtu nañu ngir naqarlu politig gi Berluskoni di doxal ci
| 
France 24 : Gaawu 17 Okt 2009
[Itali] Ay junniy nit ñaxtu nañu ngir naqarlu politig gi Berluskoni di doxal ci doxandeem yi.

AFP - Ay junni junniy nit a doon ñaxtu waliif (contre) boddikonte xeet, gaawu ci ngoon ca diggu Rom, ngir ηàññ daan yi nguurug Besluskoni teg ci way-ñàkk këyit ya ca Itali.
Ñooñee nga yoroon ay bàndrol yoy bindeesoon na ca "Déet boddikonte xeet ak daan way ñàkk këyit", "Déet ñuy delloo doxandeem yi ca seen i réew", "Berluskoni, wéyal!", "Ñun ñépp a ngi ci genn gaal gi", ngir wone li doxandeem yi di tukkee Afrig ciy gaal tey teer ca tefesi Itali yi.
| |
|
[Bitim réew] Lambaajoog nguur ca Gine : Jëwriñ yaa ngiy jàmbu Dadis benn-benn.
| Ouestaf.com : Àjjuma 16 Oktoobar 2009
Lambaajoog nguur ca Gine : Jëwriñ yaa ngiy jàmbu Dadis benn-benn.
Jëwriñu réewum Gine bi yor yeesalug yoriinu nguur ga ak ligéey ba, di Alfa Jàllo, tekki na ndombo-tànkam, ñetti fan gannaaw ba nàttangoom Abduraxmaan Saano, mi yoroon mbey ak napp ga defee li ni mel talaata 12 oktoobar.
Yooyee tekki ndombo-tànk a ngi tàmbali nag ba ay tuuma aki tëkkuy topp ci yoon dalee ci nguurug soldaar sa jiite Gine, gannaaw xew-xew yu 28 sàttumbar 2009 ya fa amoon.
| |
|
[Bitim réew] Joηante njiitu réew : Njort juddu na ci askanoog Gabong gu Aali Bongo.
| 
Jeune Afrique : Dibéer 13 Sàttumbar 2009
Joηante njiitu réew : Njort juddu na ci askanoog Gabong gu Aali Bongo.
Ab lawax (candidat) gu joηante njiitu réewum Gabong laaj na, gaawu, ab àttewaat ngir neenal palug Aali Bongo. Ci kàdduy Lik Bengono Nsi, doomu njiitu réew ma faatu, dees koo jiitle (adopté) tax mu bokk ci askanu Gabong.
"Askanoog Aali Bongo Ondimba doon na lu lëndëm. Bu firndewoo ne daa bokk ci askanu Gabong cig jiitle, mi ngi des ci àttekaay bu mag bi mu àddu ci jubadig tànneef yi (élection)", loolee nekk ci bindum laajug àttewaat gi Lik Bengono Nsi (mi am lu yées 1% ci kàddu askan wa) te AFP biral ko.
| |
|
|
| |
| Téere sargal |
|
|
|
|
| Kurél yiy yëngu ci suqali làkki réew mi | • Osad
• Anafa  |
|
|