Doxalinu politig wu ñaaw wi askan wiy dund ci nguurug abdulaay wàdd.
Ay ndombo-tànk yu bari tax na ba njiiti gox yu bari, doxaluñu liggéey bi leen askan wi doon xaare. Nekkewuñu fi ludul xëccoo ay ndombo-tànk ngir koppor yañu cay jëlée. Booleem mag ñi, njiitu gox-goxaan (pcr), metlàng yi, way-suqali koom yi (operateur economique), tofu-njiitu jataayu diiwaan, njiitu sendikaa beykat yi, ak boroom këru dem-dikk yi, ñoo ëlbatiku di xëccoo njiitu way-jëfandiku àll bi (exploitant forestière).
Xupees na sañ-sañu wax sa xalaat. Fees jëm ak sunu demokaraasi bii? Réew mom yennat ciy xalaat ñoo fi dagan, yeneen daa araam, réew mees ne : sañ-sañu xalaat génne ko, péexteg afal sa xel, lu mu jur nga wësin ko niki yooyee demokaraasi di yu Tugal yees ne ñooy ya mag yees di roye, ba jural nu nuy lang ciy mbiccam, di jafandu ciy waggam, naan lu fiy lu baax moom a déet keneen, déet feneen, ba sax lu ba woo feneen du leneen lu dul neen ndax li muy keneen, bub gox goobeem mbayam te sax mu gën mu kile, waxees ne fa la ko duppee, cëy lile! Lii ak lu ni mel moo jur natt ci ñaari nattukaay gi Tugal di def ba ay farandoom di ko ca fekk ak a roy.
Ci jegeg Tëbëski gi, samab siyaaree ngoogu, di léen ci wax déwénati
Cér bi jàkka yor war naa yokku:
Cér bi Jàkka yor war naa yokku, ndax ni njiitul jàkka (Yonnent bi (j.m) ) nekke di njiit ci lépp ci mboolay gu lislaam gi (société islamique) ni la jàkka war a nekke di boroom cér bu réy bu jaamu Yàlla, bu mboolaay (social), bu koom, bu caada (walla aada) bu sax tàggat yaram,
Gannaaw këru ligéey yi fi waa bitim réew taxawal (ni ki SGBS, TOTAL, a.ñ.s.), seetlu nanu ne koom-koomu réew maa ngi, daanaka, ci loxoy jëmm yu génnee ci njàngaleem daara, ñu koy faral di woowee ci frãse « système informel » ndax li mu dëppoowul ak gisinu waa nguur gi. Batey boroomi milyaar yaa ngi ëppee ci ñi juge ci daara yooyee bu nu xoolee këru ligéey yi ñu fi sos:
[Gis-gis] Arsëweg Saara : Sowwu day ga (imposer) Afrig caaday dee (culture de mort)
Abdu Xaadir KEBE:01 sulet 09 Arseweg Saara : Sowwu day ga (imposer) Afrig caaday dee (culture de mort), loolu bawoo na ci rajob Watikaan
Ndimbal li Sowu di jox Afrig dees koo takk ci nangug yennat ciy jëf, niki : fuglug jur gi (le contrôle des naissances), jaare ko ci yàq ëmb, ak jérméelal (la stérilisation) ak tas ideolosi (xalaat) yi di woroomug aju (relativiste) niki bu gender (manaam wuute gi nekk ci diggante góor ak jigéen)
[Gis-gis] Ilimaani Géejaway yi : Bàyyi fi moy Yàlla gi di ñaxtu kurã bu seer.
Xibaaryi.com : Alxamis 25 Sue 2009 Ilimaani Géejaway yi : Bàyyi fi moy Yàlla gi di ñaxtu kurã bu seer.
Wolof dafa wax ni « ku gis nen ne nen a ngi » ngir leeral ni ku gis dëgg war a am ngoru nangu ko. Waaye luy « nen » ci Senegaal fi nu tollu ? Ci jamono yii kan moo war a tudd nen woowu ?
Yaakaar naa ni man namaa yem ci ñaari laaj yooyu ngir wéyal wax ji. Ci sama gis-gis, du wenn nen rekk a fi nekk. Waaye nen yu bare. Li fi ne kay mooy ne dafa am nen wu gën a yelloo ñu tudd ko jamono yii.
Nen wu mag woowu ne fàŋŋ nag mooy jukko yi ak yàqute yi ñuy jur. Maanaam, lu ñu fi jéem a defar rekk ci lajj lañuy mujjee bu ñu jubluwul ci jukko yi.
[Gis-gis] Ñun nag ba kañ? Nitug Afrig diggante Faraankofoni gu Faraas ak Àddunaal (mondial
Abdu Xaadir KEBE ak Suhaybu KEBE:24 suwe 09
Ñun nag ba kañ?
Nitug Afrig diggante Faraankofoni gu Faraas ak Àddunaal (mondialisation) gu Amerig
Lan mooy ''Faraankofoni'':Faraankofoni mooy mbooleem askan ak réew ak diiwaan yiy làkk frâse niki làkku cosaan walla wu ñaareel. Moom nag am mbooloom réew mu koy wax la, mbaa mu ci bokk ci wàllug politig.
Seŋoor nag, mi ñu man a jàppe ne mooy baayi Faraankofoni ju ruu ji, boo delloo ci waxam ju mu waxoon ca Daara ju Kawe ju Kebek ''l'Université Laval de Québec'' ca 1966, nee na woon ba mu koy leeral : « La Francophonie, c'est par delà la langue, la civilisation française, plus précisément l'esprit de cette civilisation, c'est-à-dire la culture française, que j'appellerai Francité » maanam Faraankofoni, gannaaw làkk wi, mooy xay gu Frãs, cig gën koo leeral, mooy ruug xay gii, maanaam, aaday walla caaday Frãs, te ma koy woowe ag frañse.
[Gis-gis] Coowul Sowwu li ci njuréefi tànnéefu njiit ca Iraan
Abdu Xaadir KEBE:23 suwe 09 Coowul Sowwu li ci njuréefi tànnéefu njiit ca Iraan
Yéenekaay bu Sarqul Awsat bu bisub (6 /18) génne woon na bataaxal bob benn yërkatam bu jigéen a ko bindoon ñu koy wax Iimaan Mahmood, mu ,ne ca woon : ‘’ njiitul Amerig li Obamaa ak yeneen njiiti Sowwu yi, biral nañu seenug ànd ak way ñaxtu yu Iraan yi, ne waa Iraan kat ñu féex lañu ci tànn ki léen soob mu jiite léen’’, waaye Iimaan daa def ab laaj ne : ‘’ lu tax Nguuri Sowwu yi mayuñu doomi Falastiin yi ñu wone seenug péexte ci tànnal seen bopp góornamaa bi nu bëgg ca atum 1997, def gi nu ko defoon tax na ñu léen di mbugal, daal di dogoo ak góornamaab Hamaas bi nga xam ne askanu Falastin a ko tànnal boppam, taxaw it ci jàpple Israayil ci gaw Gasa ?’’.
[Gis-gis] Nikolaa Sarkusi leerati na ci ag bañam Lislaam ak xeex gi mu taxaw ci di ko ko d
Abdu Xaadir KEBE: 22 suwe 09 Nikolaa Sarkusi leerati na ci ag bañam Lislaam ak xeex gi mu taxaw ci di ko ko def
Nikolaa Sarkusi leerati na ci ag bañam Lislaam ak xeex gi mu taxaw ci di ko ko def, nee na ‘‘burka’’ di musóor mbaa muuraay na jàll nee, waxeesu ko dalal-jàmm ci Frãs, lu tax deesi ko ko wax ginnaaw moom bokkul ci Lislaam, du ci it lenn waaye ag tënk rekk la ñeel peexteg nit (liberteem) rawati na jigéen, te it li waral jigéen ñi di ko def mooy xoqtal ak xiixaan ak xupp gees leen di def, bu dul woon loolu doo gis jigéen ju koy teg, kon du diine, dees a war a jàpple jigéen ci xeexam bii ngir féex, tinkiku ci yile takun yu koy tee mu féex, af, moom boppam.
Jii wax du nar a neexi ci noppi waa sowwu yi, waaye mooy li am, waay dellu na ca gàngunaay ga, te moone mooy ka ca nekkoon, beggloowul Israayil, du caagéenu Amerig, Sowwu dajaloo nekk ca ginnaawam, waaye begloo na lu sakkan ci waa Iraan ak jullit ñi lottu ci yaradikug Sowwooki gaayam, ngir taxaw gi mu def ci aar boppam, fonk boppam, aar it way néew yi doole,