 | |
| Cëru (Contribuer) | Boo bëggee siiwal ab jukki (article)
[cuqal fii] |
|
| |
[Wér-gi-yaram] Wàññikug njëgu paj meek garab yi aju ci ceggum deret ji
| Ndakaaru, talaata 13 awril 2010
Xibaar yilee ngi tukkee ci Muhammad Sumaare, njiitu Mbootaayu ñi ñuy seggal seen deret ak ak way-doyadig roñoŋ yi
Wàññikug njëgu paj meek garab yi aju ci ceggum deret ji
Mbootaayu ñi ñuy seggal seen deret ak ñi ànd ak doyadig roñoŋ « l’Association Sénégalaise des Hémodialysés et Insuffisants Rénaux (ASHIR) » te Muhammad Sumaare jiite ko, liggéeyam a ngiy tàmbalee jur njariñ, ndax woyofal gi mu doon ñaan ci paj mi, mel na ni am na lu ci jot a feeñ, xanaa kay di ñaan mbir mi dem ba kenn dootul fey dara.
| |
|
[Wér-gi-yaram] WOPPU SAY : Gaafal gee gàllankoor ceetlu gi.
| 
Le Soleil : Àjjuma 26 Màrs 2010
WOPPU SAY : Gaafal gee gàllankoor ceetlu gi.
Laboratuwaar Sanofi Aventis, Synergies africaines ak kurélu Senegaal giy xeex feebaru say ñoo ubbi, démb, ab naal ngir xeex wopp jooju. Ñu fas cee yéenee xeex nag gaafal gi ngir seet 60% ci way-wopp yi nga xamne loolee leen tee seetlu ji.
« Aji-wopp yooyee dañuy daanu say ci ludul benn ndimbal. Gaafal googoo lalu ci wopp jooju. Ñu bari ci ñoom ñàkk nañu ci seen bakkan ndax ñàkkug taxawu ».
| |
|
[Wér-gi-yaram] BISI ÑAKK NGIR XEEX JÀNGOROY LAFAÑ : Lu ëpp 10.000 ndaw lañu ci yékkati
| 
Le Soleil : Altine 08 Màrs 2010
BISI ÑAKK NGIR XEEX JÀNGOROY LAFAÑ : Lu ëpp 10.000 ndaw lañu ci yékkati
Réewum Senegaal, niki réewi Afrig yu bari, a ngi ñakk, gaawu ba léegi, ci biir réew mépp, xale yi am 0 ba 5 at ngir aar leen ci jàngoroy lafañ (poliomyélite). Nguur gi nag yékkatina ci lu ëpp 10.000 ndaw ngir matal dagaanug ñakk googee war a am ci ñetti yoon.
| |
|
[Wér-gi-yaram] WÉR-GI-YARAM : 125 fajkatu-jigéen rekk lañu waññi ci Senegaal.
| 
Le Soleil : Gaawu 13 Few 2010
WÉR-GI-YARAM : 125 fajkatu-jigéen rekk lañu waññi ci Senegaal.
Ci askan wu tollu ci 12 milyoηu doomu aadama, 125 fajkatu-jigéen (génycologue) rekk la Senegaal am, te ñi ci ëpp ay soxna lañu. Muy lu jafeel pajum jigéen ñi toll ci am doom te seenag lim toll ci 49% ci jigéeni réew mi. Ñooñee a ngi am jafe-jafe yu réy buñu ëmbee ak buñuy wësin ndax limu fajkatu-jigéen ak fajuwaay yu néew. 125 fajkatu-jigéen rekk lañu waññi yoy ñi ci ëpp ci dëkku taax yi lañu féete.
| |
|
[Wér-gi-yaram] Lekku aji-jabet
| OSAD: Gaawu 2 samwie 2010
Lekku aji-jabet
02 Nowàmbar 2009
Gannaaw ba mu siiwalee lees war a xam ci jabet, doktoor Abdul Asiis Kase (Dr Abdoul Aziz KASSE, Chirurgien Institut du Cancer, Université Cheikh Anta DIOP) dellusi na, di xamle ñam yi aji-jabet war a lekk ak yi mu war a moytu....
Yow aji-jabet, toppal dénkaane yii
| |
|
[Wér-gi-yaram] Lees war a xam ci jabet
| OSAD: Alxamis 31 desàmbar 2009
Lees war a xam ci jabet.
Xibaar yii tibbees na leen ci Orangeinfo, ñu tukkee ci Doktoor Abdul Asiis Kase (Dr Abdoul Aziz KASSE Chirurgien Institut du Cancer Université Cheikh Anta DIOP) Tënk
Lan moo di jabet ?
Ñaari wirgoy jabet ñoo am, jabet 1 ak jabet 2, ñoom ñaar ñépp xàmmees na leen ci nattu suukar bu jéggi dayo ci deret ji, ëpp 1,26 g. Waaye li sabab natt bu jéggi dayo bi ci jabet 1 wuute na te li ko sabab ci jabet 2.
| |
|
[Wér-gi-yaram] Moytuleen kolesterol (cholestérol) !
| OSAD: Aljamis 24 desàmbar 2009
Moytuleen kolesterol (cholestérol) !
Xibaar yii tibbees na leen ci Orangeinfo, ñu tukkee ci Doktoor Abdul Asiis Kase Tënk
19 Nowàmbar 2009
Lan moo di kolesterol ?
Kolesterol diw la gu baax ci nit, ndax dafa bokk ci yiy tabax yaram. Waaye nag, su natt bi jéggee dayo, niin-niin yi dañuy des ci solom yiy jóge ci xol bi di tas deret ji ci cër yi. (athérosclérose).
Fu kolesterol di jóge ?
Li ëpp ci kolesterol res bee koy defar. Gannaaw loolu, dees na ko jële ci ñam yu deme ni nen, mbàq ak butit (laxas), bëer, yàpp wu duuf añs (ak ñoom seen).
| |
|
[Wér-gi-yaram] Ngir xeex bëtt-bëttu wasin dafa laaj kilifa yi amal aw tëralin wu matale, daj r
| 
APS : Talaata 25 Ut 2009
Ngir xeex bëtt-bëttu wasin dafa laaj kilifa yi amal aw tëralin wu matale, daj réew mépp.
Ngir xeex bëtt-bëttu wasin « fistule obstétrique » dafa laaj kilifa yi amal aw tëralin wu matale, daj réew mépp loolu la Profesëer Magéy Géy xalaat, njiital bànqaas bi màcc ci mbirum awra ak sawukaay, ci oppitaalu Grã Yoof (« chef du service d’urologie de l’Hôpital général de Grand-Yoff »).
Tënk
Amal aw tëralin wu ànd ak ay jumtukaay yu ñu ko doxale
Tëralin woowu, su ñu ko doxalee ni mu ware, mën naa tax ñu daan ci juróomi at yiy ñëw (2010-2015), musiba mu réy moomu, nga xam ne jigéen ñu bare yàq na seen àddina, te dara waralu ko, lu moy ñàkk ku leen taxawu.
| |
|
[Wér-gi-yaram] Talaata lees di màggal bis bi àddina sépp jagleel xeex jàngoroy Sida.
| 
APS : Altine 30 Now 2009
Talaata lees di màggal bis bi àddina sépp jagleel xeex jàngoroy Sida.
Réewum Senegaal dina màggal bis bi àddina sépp jagleel xeex jàngaroy Sida, talaata jii bu 10 waxtu jotee ca Mbaaw (anéeru Ndakaaru) ci njiitéefu soxnaas njiitu réew mi Vivian Wàdd, la APS jibal. Dees na fa amal waxtaan wu jëm ci : ‘’Àq doomu aadama ak li aju ci jot, ñeel àddina sépp, ci jumtukaayu fàggu yi, yoy faju yi ak yoy jàppale yi’’, la xibaar boobee leeral.
| |
|
[Wér-gi-yaram] Jàngoro ji ñuy wax deng « dengue » mu ngi ci Senegaal, di gën a tar.
| Orange-Info
Orange-xibaar : 18 Nowàmbar 2009
Jàngoro ji ñuy wax deng « dengue » mu ngi ci Senegaal, di gën a tar.
Jàngoroy deng a ngi ci réew mi, looloo waral kilifa yi nekk Njawriñu Wér, tëral ay pexe yu gàllankoor lawug jàngoro ji.
Lan mooy joxe jàngoro ji ?
Màtt-màttu yoo yu ñu tudde « Aèdes » moo koy joxe. Yoo yooyoo ngiy dund ci poti flëer yi, pnë yu màggat yi, mbalka yi, sën yi, ndaa yi, ndab yu màggat yi ñu sànni yi. Yoo yooyu li leen tax a bon, moo di guddeek bëccëg lañuy màtt, ñu ngi gën a tasaaroo ci dëkkuwaayi taax yi ak yi nekk ci seen pegg.
| |
|
|
| |
| Téere sargal |
|
|
|
|
| Kurél yiy yëngu ci suqali làkki réew mi | • Osad
• Anafa  |
|
|