 | |
| Cëru (Contribuer) | Boo bëggee siiwal ab jukki (article)
[cuqal fii] |
|
| |
[Diine] «Tënk nañu saytaane yi ci weeru koor » Kon ana lu tax nit di wéy di def ab safa
|
Jéngees na saytaane yi ci weeru Koor:
Abuu Hurayra nettali na ne, Yonent (jàmm ak xéewalu Yàlla ci moom) bi neena: "Bu weeru koor yegsee, dees na ubbi wunti àjjana, tëj yoy sawara te jéng saytaane yi". (Al-Buxaari, Muslim)
Yonent (jàmm ak xéewalu Yàlla ci moom) bi neena: " Weeru Koor yegsi na; weer woo xamni ci la léen Yàlla ga (digal) koor; diirub weer wi, wunti asamaan yi dañuy ubbiku, wunti sawara tëju te saytaane yi it dees léen di jéng; te am na ci weer wi ag guddi gu gën junniy guddi (weer), ku tonowoowul ngënéel i guddi gii mooy ki ñàkk (pert) " (An-Nasaayi moo ko soloo)
| |
|
[Diine] Alxamis gii la koor gi tàmbali ci Senegaal
| 
APS : Àllarba 11 Ut 2010
Alxamis gii la koor gi tàmbali ci Senegaal

Kuréel giy séentu weer wi ci Senegaal saxal na alxamis gii njalbéenug koor gi ci Senegaal, la RTS siiwal.
Wax jooju a ngi tukkee gannaaw ba weer wi feeñee àllarba ci gox yu bari ci réew mi. Kon jullit yi dugg nañu ci weeru kooru lëmm.
| |
|
[Diine] Koor ak li ci aju.
| Abdu Xaadir KEBE: Talaata 10 ut 10
Koor ak li ci aju.
Xamle luy koor, taariixam ag farataalam
Koor mooy juróom ñenteelu weer ci arminaatu jullit ñi. Weer wii mooy ndoorteelu wàccug Alxuraan ci suuf. Bokk na ci li tax jullit ñi di ko woor: màggal ko. Woor Benn la ci ponki Lislaam yi.
Moom nag am na fukk ciy ne-ne (matière):
| |
|
[Diine] JIBALUL NGUUR GI TËJ WOOTEB SEYDINAA LIMAAMULAAY: Ay ñaan ngir jàmm
|
Le Soleil : Àllarba 14 Sulet 2010
JIBALUL NGUUR GI TËJ WOOTEB SEYDINAA LIMAAMULAAY: Ay ñaan ngir jàmm ca Kaasamaas ak nawet bu barkeel
130eelu wooteeb SEYDINAA LIMAAMULAAY weesu na. Ci jibalu Nguur ga ko tëj, gërëmees na Nguur gi ci ndimbalam ngir xew-xew wi jaar yoon. Def nañu fa ay ñaan ngir jàmm delsi ca Kaasamaas te ñu am nawet bu bàrkeel.
Jëwriñu mbootaay mi yor xewum (cordonnateur du comité d’organisation) 130eelu Wooteb Seydinaa Limaamulaay, di Seydinaa Isaa Caw Laay, tënk na kàddoom ci jàmm ca Kaasamaas ak ci mbënn mi ci anéer bi (la Banlieue), ci Jibalul Nguur ga ñu doon def. Ci turi Xalifu Laayeen yi, Seydinaa Abdulaay Caw Laay, ñaan na ngir jàmm am ci Senegaal gépp te nawetu ren bi bàrkeel.
Jëwriñu Nguur gi yor biir Réew mi, Bekaay Jóob, jottali na nuyyóob Njiitu Réew mi ak Nguur gi. Wax na it ne Wooteb Seydinaa Limaamulaay bii woote jéme ci Lislaam la.
| |
|
[Diine] Nahjul Xadaail Haaji
| Abdu Xaadir KEBE:
Nahjul Xadaail Haaji
Maa ngi Tàmbali samay wax ak jëf ci turu Yàlla miy kiy boroom yërmande ju yaa ji ci adduna ak ju ñu jagleele ji ca allaaxiraa.
Yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci suñu sang Muhammad ak ci ñoñam aki saabaam ci anam gu sax
Yàlla doy na ñu, moom de wéeruwaay wu baax la (wu mat a wéer say mbir, joyal ko ko).
Jëf yaa ngi ci yéene yi, ku nekk it la nga yéeneey sag pay
Bokk na ci hikam (sagesse) :
ku sàkku mbir de bu ca saxee am ko. Ku fëgg bunt it boo fa saxee ubbilees la
Bokk na ci hikma bat ay:
ku tëyye boppam wëlif neen yi (caaxaan yi ) limees ko mu bokk ci boroom xel yi.
| |
|
[Diine] Sëti Seex Ibra yee yékkati seen kàddu: ñu ngi ηàññ bu baax ñi mbubboo « Baa
| 
Le Soleil : Allarba 14 Awril 2010
Sëti Seex Ibra yee yékkati seen kàddu: ñu ngi ηàññ bu baax ñi mbubboo « Baay Faal » te doonuñu ko.
Ñaari sëti Seex Ibra Faal a ngi ηàññ doxalinu ñenn ñiy mbubboo ag « Baay Faal » tey soññ Nguur gi mu dakkal yooyule doxalin yu sonle. Ñu ngi waxewoon loolu ci màggalug Seex Abdulaay Faal Ndar ca Ndar.
Màggal gu njëkk gog ndem-si-Yàlla Sëriñ Abdulaay Faal Ndar, doonoon ñetteelu Xalif bu Seex Ibra Faal, amaloon nañu ko ayu-bés bi weesu ca Ndar. Ñi ko amal di ay sëti boroom màggal gi. Ci ay yëngu yu ñu daawul gis, xew-xew yi dajale nañu ay taalibe muriid yu bare ak i baay faal yu aalu lool, juge ci fépp ci réew mi. Sëti Seex Ibra Faal yii di Seex Bintu Faal ak rakkam wala magam Seex Say, ηàññ nañu ak doole doxalin wu safanoo wi ñenn ñi di doxal tey mbubboo ag « baay faal », di dogale ñiy dox ci mbedd mi sonal leen lool te it di yalwaan ci anam yu jéggi dayo.
| |
|
[Diine] GÀMMU: Guddi màggalug juddu yonnent Yàlla Muhammad (صلى
| Albichru.org : 22 feewrie 2010
GÀMMU: Guddi màggalug juddu yonnent Yàlla Muhammad صلى الله عليه وسلم)).
Baatu gàmmu mi ngi tekki ci wolof bés bi ñuy màggal juddu yonnent bi (j.m). Yenn saa yi ñu jël baatu araab Mawluud, mu di tekki ku ñu jur. Bés bi dinañu ko màggal at mu nekk, di tollook guddig 11 jëm 12 ci weeru (Rabihoul Awwal), ñu di ko wax ci wolof Gàmmu. Ci fàttali, guddig juddug yonnent bi mi ngi tolluwoon ci altine, fukki fan ak ñaar ci Rabihoul Awwal ci atum 570 ci ati nasaraan. Ren muy 1431 ci atum gàddaay gi, guddi gi dees na ko màggal 26 jëm 27 ci weeru Feewrie 2010.
Muy guddi gu am solo lool ba tax na yoon la ñu leeral juddoom ci Lislaam. Tamit xew-xew yi ci amoon, nees ko war a màggale ak xéewal yi ci nekk.
| |
|
[Diine] [ARCHIVES - WIDEO] - SËRIÑ MUSTAFAA SI : Yoonu Tiijaan, yoonu Murid ak Abdulaay
| 
Leral.net : Àjjuma 12 few 2010
[ARCHIVES - WIDEO] - SËRIÑ MUSTAFAA SI : Yoonu Tiijaan, yoonu Murid ak Abdulaay Wàdd
| |
|
[Diine] Màggalug Tuubaa: Ab tënk ñeel Taarix ak lu aju ci bis bu tedd bi.
|
Xibaaryi.com: Talaata 19 samwie 2010
Màggalug Tuubaa: Ab tënk ñeel Taarix ak lu aju ci bis bu tedd bi.
Màggalug Tuubaa, Bis la bu màgg fi Taalubey Sëriñ Tuuba yi te it di bis bu nu fonk, Di it bis bi Sëriñ bi demee ci tukkib liggeey bi, ci 18 ci aw Magal (safar), Nu di ko amal at mune fa Tuubaa, ci fukki fan ak juróom ñatt (18) ci aw Màggal (Safar), ci arminaatu (calendrier) weer wi walla bu Hijri. Teg ko ci ndigalul Sëriñ Tuubaa "Bu bis bi ñëwatee na ngeen ma Santal Yàlla kem séen kàttan".
Mu digle woon ko ci fukki fan ak juróom ñatt ci atum 1341 ci hijri, di 16 julet 1921 ci Gregorian. Muriid yi di juge fune di jëm Tuubaa, ngir amali ko fa barab bu tedd boobee, dem na nag ba yamatul rekk ci Muriid yi, Waaye xanaa nekk xew-xewu Julli ñépp, Mbaa sax nit ñi ngir mu gën a matale, Muy yitte ju rëy, Ay miliyoŋi nit diko teewe.
| |
|
[Diine] [Wideo] Ay ndaw jàmmaarloo nañook takk-der yi ci buntu katedral bi
| 
APS : Àllarba 30 Des 2009
[ Wideo ] Ay ndaw jàmmaarloo nañook takk-der yi ca buntu katedral bu Ndakaaru.
Ndakaaru, 30 des (APS) - Takk-der yi tasaare nañu àllarba aki fàccaakonu gëlëmël (grenade lacrymogène) ab doxu ñaxtu bu ay ndawi kercen amaloon ba ñu génnee ci mees bu katedralu Ndakaaru bi nekk ca wetu njéende réew mi, loolee la APS yégle.
| |
|
|
| |
| Téere sargal |
|
|
|
|
| Kurél yiy yëngu ci suqali làkki réew mi | • Osad
• Anafa  |
|
|