| Cëru (Contribuer) | Boo bëggee siiwal ab jukki (article)
[cuqal fii] |
|
| |
[Koom-koom] AJ MÀKKA 2010 : Yokkees na 143 junni ci paas bi.
| 
WalFadjri : Talaata 17 Ut 2010
AJ MÀKKA 2010 : Yokkees na 143 junni ci paas bi.
Gannaaw ubbite, ci bisub 24 suwe, gu yérug njég yu lonkoo yu jawwu yi binduwoon ngir yóbbu ujaaj yu Senegaal ca bërëbi Lislaam yu sell ya, siiwalees na démb Air Europa mi ñu tànn. Niki atum 2009, lookoo gu jawwu joojooy yóbbuwaat doomi Senegaal yi nàmm a dem ca suufus Araabi Sawudi, ak tuuti ciy coppite, la ab jibal bu njëwriñu dem beek dikk bi ci jawwu ji, saxal. Ci wàllu pey gi, lookoo gi yokk na 143 junni ci paasu daaw ba.
Njégu benn milyoη ak 134 junni CFA lañu njëkkoon a jàpp ak Air Europa. Waaye, gannaaw waxaale yi, benn milyoη ak téeméeri junni CFA la ujaaj bu nekk di fey.
| |
|
[Koom-koom] Wàññiku gu matale ñeel njégi njafal yi ñu segg.
| 
Kanal150 : Dibéer 8 Ut 2010
Wàññiku gu matale ñeel njégi njafal yi ñu segg.

Ag tër gu bees ñeel njég yi génn na gaawu gii 07 ut 2010, di màndargawoo ag wàññiku gu matale ci njégu mbooleem njuréefi petrol ak gaas bitaann yi, la ab jibalug njëwriñu kàttan gi saxal.
«Doontele ag yokk gu +17% ci fretu géej gi amna, ñeeti ayu-bés yi mujj a ngi gën a fës ag wàññikug natti mbooleem njuréefi petrol bi ci ja yu àddina si, teg ci ag wàññikug - 4% ci kujje dollar /Franc Cfa» ; lañu bind ca jibal la.
Ci gaas bitaan bi, njëwriñ ji yégale na ne Nguur gi day dox ci yemaleg ajug galagu duwaañ ak gu TVA ci njuréef googu ngir néewal njég gi ci weeru koor gi.
| |
|
[Koom-koom] Wàññiku gu matale ñeel njegi njafal yi ñu segg.
| 
Kanal150 : Dibéer 8 Ut 2010
Wàññiku gu matale ñeel njegi njafal yi ñu segg.

Une nouvelle structure des prix est entrée en vigueur ce samedi 07 août 2010, se caractérisant, par une baisse généralisée des prix de tous les produits pétroliers y compris le gaz butane, indique un communiqué du ministère de l’Energie.
«Malgré une hausse +17% du fret maritime, les quatre dernières semaines ont été marquées par une baisse des cotations de tous les produits pétroliers sur le marché international ainsi qu’une baisse de - 4% de la parité dollar /Franc Cfa» ; écrit le communiqué.
Sur le gaz butane, le ministère informe que le Gouvernement fait jouer la mesure de suspension des droits de douane et de la TVA sur ce produit pour en atténuer le prix au consommateur particulièrement pour le mois de ramadan.
Le tableau ci-dessous donne les variations des prix au consommateur
|
Produits blancs (TTC/litre)
|
Nouveaux prix plafond
|
Précédents prix plafond
|
Variation absolue (en Fcfa)
|
Variation relative (en %)
|
|
Supercarburant
|
737
|
746
|
-9
|
-1,2
|
|
Essence ordinaire
|
703
|
712
|
-9
|
-1,3
|
|
Essence pirogue
|
555
|
564
|
-9
|
-1,6
|
|
Pétrole lampant
|
506
|
516
|
-10
|
-1,9
|
|
Gasoil
|
632
|
644
|
-12
|
-1,9
|
|
Produits noirs (TTC/Tonne)
|
Nouveaux prix plafond
|
Précédents prix plafond
|
Variation absolue (en Fcfa)
|
Variation relative (en %)
|
|
Diésel-Oil
|
507 916
|
521 070
|
-13 154
|
-2,5
|
|
Diésel Sénélec
|
507 916
|
521 070
|
-13 154
|
-2,5
|
|
Fuel Oil 180 CST
|
375 574
|
380 116
|
-4 542
|
-1,2
|
|
Fuel Oil 380 CST
|
365 299
|
368 935
|
-3 636
|
-1,0
|
|
Fuel Sénélec
|
336 639
|
340 160
|
-3 521
|
-1,0
|
|
Distillat TAG
|
516 756
|
| |
[Koom-koom] jokkoo-soreyoo: Senegaal dogoo na ag li des ci àdduna bi.
| 
Seneweb.com : Alxamis 05 Ut 2010
jokkoo-soreyoo: Senegaal dogoo na ag li des ci àdduna bi.
Jokkoo yiy dugg niki yiy génn jaxasoo nañu woon lool alxamis gii ci Senegaal. Jafewoon na lool ci waa Senegaal ya ca bitim réew ñu jokkook seeni njaboot. Jokkoo bi ci internet it jaxasoowoon na lool, gàllankor niki noonu demalanteeg xibaar yi ak weccekoonte gi ci dalu web yu bari.
Benn sabab jamono jii, waxaguñu ko, waaye melna ni ñaxtu ligéeykati Sonatel yiy jàmmaarlook nguur gi ci li ñeel yokkug njegu woote yiy dugg ci biir réew mi.
| |
|
[Koom-koom] Ger a ngi téqtal yoriinu nguur gu sell ci Senegaal, lees saxal.
|
APS : Gaawu 10 Sulet 2010
Ger a ngi téqtal yoriinu nguur gu sell ci Senegaal, lees saxal.
Ndakaaru, 9 Sulet (APS) - ‘Jëflante yu geru’’ yees lim ci déndu Senegaal a ngi waaj a faagaagal ‘’jeego yu fës’’ yi réew mi jot a amal jëm ci cellug yoriinu nguur gi, la Mbooloom Kuréelu Nguur yi ànd di xeex Weexalug Alal ci Afrig sowwu-jant (ñu duppe ko ci farañse : Groupe intergouvernemental d’action contre le blanchiment d’argent en Afrique de l’Ouest GIABA) saxal àjjuma ca Ndakaaru.
‘’Jëflante yu geru yi niki (mbir mi ñu siiwal ci weeru oktoobar 2009 ñeel neexaleeg xaalis bi ñu jébbal Aleks Segura, doonam ndawal Sàqum Koppar gu Àddina ci Ndakaaru (Fonds monétaire international) doon na luy xupp jeego yi réew mi lal ngir wone cellug yoriinu nguur gi’’, lees saxal ci téere bi GIABA siiwal.
Batey ci saxalug atum 2009, ‘’Njeexitalug liggéey lu ndawal FMI ci Ndakaaru indi na coow lol, li ko waral mooy lutax njénde réew mi (présidence de la République) jox S. Segura gaalu xaalis gu def ay euro aki dollar’’.
| |
|
[Koom-koom] Tund Franc : Wàdd ànd na ci ñu moom sunu bopp ci wàllu Xaalis.
| 
Kanal 150: Àllarba 7 awr 2010
Tund Franc : Wàdd ànd na ci ñu moom sunu bopp ci wàllu Xaalis.
Njiitu réew mi Me Abdulaay Wàdd feddalina njeexitalu ayu-bés bii ag nammeelam ngir réew yi bokk ci tund Franc bi wéyal seen bopp ci wàllu xaalis, rawatina nag réewi Afrig sowwu jànt yi. Neena taxawna temm ngir ñu delloosi xaalis bi Bànk bi réewi Afrig sowwu jànt séq (BCEAO), dencoon ca Bànkub réewum Farãs, doonte amnay kilifa yu mu neexul ca réewum Farãs.
Mi ngi jibal wax jooju dibéer cib jataayu tele ca Farãs. Neena, juróom-fukki at ganaaw bi ñu moomee seen bopp, réew yooyee war nañoo soppi seen politig ci wàllu weccet. «Bu nu nangoo sunu kàttanu weccet, deesna amal yoriin wu gën», la yaxal.
| |
|
[Koom-koom] Njiitu réew mi Abdulaay Wàdd a ngi tuumal : Bceao a ngi làq ay junniy milyaar ca
| 
WalFadjri : Àllarba 10 Few 2010
Njiitu réew mi Abdulaay Wàdd a ngi tuumal : Bceao a ngi làq ay junniy milyaar ca bitim réew.
Njiitu réew mi Abdulaay Wàdd naqarlu na, démb, doxalinu Bànk bi réewi Afrig sowu-jant yi bokk, ñu duppe ko Bceao. Neena, Kërug alalal (Institution financière) googee ngi wéy di làq alal ju bari ca bitim réew ci jamono jii nga xamne koom-koomi réew yi ko séq a ngi ci jafe-jafe yu réy ci wàllu alalal (finance). Mi ngi jibal wax joojee démb ci ubbite ndaje mi ñu jagleel alalalug Progaraamu biir réew mi ñu naal jëme ko ci mbéy mi (Pnia).
| |
|
[Koom-koom] TUUBAA TV TÀMBALINA CI SATELIT.
| 
Le Soleil : Altine 1 Few 2010
TUUBAA TV TÀMBALINA CI SATELIT.
Tuubaa TV di telewisioη bu bees gu « yar, yéene ak bégale, ci anam yu dëppook i teggin » tax a jóg tàmbalina àjjuma jii weesu ci satelit.
Tuubaa TV te bàkkam di « Tele bi ñu nuru? » jàppandina ci satelit fii ci Afrig ci frekãs W4-12.437 14 GHz, fii ak muy tàmbali ci Tugal ak Amerig ci weeru màrs gii di ñëw, la ñu jibal. Tele boobee nag, ay doomi Senegaal yu màcc ci jokkolante (communication), a ko taxawal ci nowàmbar 2009, ngir « jàppandal doomi réew mi tele bu dëppook i teggin, rafetal ak diine yi waa Senegaal aadawoo? ».
| |
|
[Koom-koom] Réewum Amerig may na Senegaal 540 milyoηu dolaar ngir mbey mi aki tali yi.
| 
WebNews : Altine 7 Satumbar 2009
Réewum Amerig (United Stated) may na Senegaal 540 milyoηu dolaar ngir mbey mi aki tali yi.
Njiitu réewum Senegaal Abdulaay Wàdd siiwal na altine ne nguurug Amerig dina dimbalee Senegaal ci lu tollook 540 milyoη ci dolaar ngir suqali mbey mi ak defar i tali (yoon).
Mi ngi ko jibal bi mu ñibbisee Ndakaaru, gannaaw weeru bër bi mu amaloon ca Suis ak Frãs. Xéewal googu toll ci (270 milyaar ci CFA) nag ndimbal lees dul fey.
| |
|
[Koom-koom] JUDDUG LONKOO GU JAWWU GU YEES (NOUVELLE COMPAGNIE AERIENNE) GU RÉEW MI, GOG NO
|  talaata 11 ut 09
JUDDUG LONKOO GU JAWWU GU YEES (NOUVELLE COMPAGNIE AERIENNE) GU RÉEW MI, GOG NOPPI NA NGIR DOOR AY LIGGÉEYAM, DEESI WOOYE KO NAG CI WU FRãSE ( LE GROUPE AIR SENEGAL ( GAS))
Sémbub taxawal lonkoog jawwu gu Senegaal gu mel ne ndemsiyàlla «Air Afrique» mi ngi jëm kanam ci anam gu yeex, waaye gu wóor. Njél lu alalam jotees na cee noppi, fi ay liggéeyam jëm it jotees na koo leeral. Lonkoo gii ñu tudde (Groupe Air Sénégal) te warees a tàmm dàkkantalam wii «Gas» dina door balaa yàgg di def ay naawam.
| |
|
|
| |
| Téere sargal |
|
|
|
|
| Kurél yiy yëngu ci suqali làkki réew mi | • Osad
• Anafa  |
|
|