 | |
| Cëru (Contribuer) | Boo bëggee siiwal ab jukki (article)
[cuqal fii] |
|
| |
[Caada] Senegaal : téere biy diiηat yoriinu ab asãs bu doomu njiitu réew mi
| 
AFP : Dibéer 16 ut 2009
Senegaal : téere biy diiηat yoriinu ab asãs bu doomu njiitu réew mi
Ndakaaru — Abdu Latif Kulibali, di taskatu xibaar bu réewum Senegaal, doon kuy ηàññ lool nguurug Abdulaay Wàdd, génne na aju-bés bii ci Ndakaaru ab téere luññutu buy ηàññ yoriinub asãsu réew mi bu Kariim Wàdd, doomu njiitu réew mi, jiite woon. Téere boobee mu duppee "Contes et mécomptes de l'Anoci", di ci làkku wolof "Léeb ab lippóon gi ci Anoci" jot naa jaar ci yéenekaay yu réew ma ca joxe seen xalaat bu baax a baax.
| |
|
[Caada] Ab jukki bees tekkee ci: http://www.alliance-panafricaniste.com/index.php
| | |
|
[Caada] Ndajeem Xoy 2009 : séenuees na ay jafe-jafe fa Tiwaawon ak Tuubaa.
| SudQuotidien : Altine 8 Sue 2009
Ndajeem Xoy 2009 : séenuees na ay jafe-jafe fa Tiwaawon ak Tuubaa.
Mbooloom àddina mi dul politig tey toppatoo pajum cosaan (Prometra) mujj na dajaleeti Saltige yu Siin ak yu feneen. Loolaa nga ame woon ca Màkkaan ma ñuy jàngate Xam-xamu cosaan (Cemetra) nekk ca Fatig te ñu koy woowe Malàngo. Foofu la Xoy bi di Ndajem caada muy am at mu ne ngir seet liy xew ci réew mi ci jamono yi ñu jém. Ndajem ren (2009) mi indiwaat na Tuubaa ak Tiwaawon ci Ceet gi, nde Saltige yi wax nañu ne ñaari dëkk yooyu dana ñu yëg lool jafe-jafey Askan wi.
| |
|
[Caada] Màggalug 28eel ati faatug Bob Maarlee ca Ngor : sàngara ak yàmba jaa mel ni tuq
| LAs : Talaata 19 Mee 2009
Màggalug 28eel ati faatug Bob Maarlee ca Ngor : sàngara ak yàmba jaa mel ni tuq su bënn…, ña fa dëkkee ngay yuuxu seenag doyal.
Yàmba, sàngara, rege(reggae)… lépp a nga fa woon. Talibey Bakkus yi ak yu ñax-miy-rey (yàmba) defati nañu seen manin. 28eel ati faatug Robeer Nesta Maarlee (6 fewrie 1945-11 mee 1981) fàttaliku nañu ko nees ko daan defee ca Ngor. Xumboon na lool. Mag ñi, ndaw ñi, gune yi sax bàyyiwuñu fa sineebar bi, lépp ngir fàttaliku jëmmi Rege jooju. Loolee yëngël waa gox ba nga xamne dañoo bëgg sax xew-xew yu ni mel dakk fa faf.
| |
|
[Caada] Ekon mooy woy bàkkub Joŋanteb Futbal bu réewu àddina sépp ci atum 2010 !
| WebNews : Talaata 12 Mee 2009
Akon mooy woy bàkkub Joŋanteg Futbal gu àddina si ci atum 2010 !
Akon, mi ngi waaj a génne ñaari laj-koloñ (parfums) yu bées, amul bénn jot! Noonu lanu tànne woykat bii ngir mu fent bàkkub Joŋànte gu Futbal gu àddina sépp ci atum 2010, te war a ame ca Afrig gu bëj-saalum. Yégle na ni : « jëlees na ma ngir ma jiite woyuw Joŋànte gu Futbal gu àddina bi. Dinaa jiite woy wi ñuy ubbee.
| |
|
[Caada] Màggalug 50 ati APS
| APS - Altine 20 awril 2009
Màggalug 50 ati APS
Kurél giy taataan xibaar yi ngir tasaat leen, ñu tudde ko APS, àllarba lay màggal 50 atam, li ko dale 9 waxtu, ci Biro bu diiwaan (regional) bu Unesco ci Ndakaaru. Xew-xew baa ngiy ame ci kiliftéefu Abdul Asiis Sow, jawriñu Xamle gi ak jokkoo-soreyoo gi (telecommunication), ak Nepad, ak Diggante campeef yi, yore kàddu góornëmaa bi. Loolu la njiitug APS yëgle.
| |
|
[Caada] tiyaatar bii di « polymachin » dëppoo na ak liy xew ci sunuw askan
| Xinhuanet : Dibéer 8 Maars 2009
Kujje : tiyaatar bii di « polymachin » dëppoo na ak liy xew ci sunuw askan
Ndakaaru, 7 maars (Xinhua) – Ci tiyaatar bii tudd « Polymachin » te ñu dawal ko bis yi ñu weesu ci Ndakaaru, kureel gi ñuy woowe « Cruellas » wone nanu ci bu baax jeexitial yi kujje amal ci biir askanu Senegaal. Ànd ci ak ñaari tiyaatarkat yu jigéen yii di Marieem Fay ak Maada Njaay. Ñoom ñaar tudd nañu, ak wollamiku gu mag, jeexital yi kujje di def ci jigéen ñi ak njaboot gi.
| |
|
[Caada] Dello njukkal ñeel ndemsi-yàlla Usmaan Sémbéen
| Fespaco 2009 : Dello njukkal ñeel ndemsi-yàlla Usmaan Sémbéen defkatu film la woon (cinéaste): Usmaan xér na Ouagadougou - WalFadjri
Moo xam mbedd ma ñu ko duppee, moo xam nataalub xànjar ba ñu ko jagleel, dëkk bii di Wagadugu am na ay màndarga yuy firndéel kóllare gu dox digganteem ak Usmaan Sémbéen. Ñaar fukk ak benneelu Fespaco, bi door gàwwu, delloo na njukkal kii di Usmaan Sémbéen mi fi bàyyikoo ci atum 2007. Kuréel gi lëkkale këru sinemaa ak tele yu réewi Afrig door na ñaar-fukki fan ak juroom ñatt ci weeru feewriye ba juroom ñaari fan ci weeru maars. Ndaje moomu di am ca réewu Burkinaa-Fasóo doore nañu ko njukkal lu rey lu ñu doon dello Doomu Senegaal ja di Usmaan Sémbéen.
| |
|
|
| |
| Téere sargal |
|
|
|
|
| Kurél yiy yëngu ci suqali làkki réew mi | • Osad
• Anafa  |
|
|